Bi Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yónnee Muhaas Ibn Jabal -yal na ko Yàlla dollee gërëm- ca dëkki Yaman ya muy aji-woote jëme ci Yàlla di jàngalekat, da koo xamal ne dana jàkkaarlook ay Nasaraan; ngir mu waajal ko, ak mu tàmbalee ci bu leen di woo ci li gën a ëpp solo, Mu leen di njëkk a woo ci yéwénal pas-pas; ci ñu seede ne amul kenn ku yeyoo jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la; Ndax te ñoom ci loolu la ñuy dugge ci Lislaam, bu ñu wommatoo ci loolu mu digal leen ñuy taxawal julli; ndax moo gën a màgg ci wartéef yi ginnaaw kennal Yàlla, Bu ñu ko taxawalee mu digal leen joxe asakay séen i alal séen i way-ñakk. Mu moytandikuloo ko nag ci jëll séen alal ji gën; ndax li war mooy digg-dóomu, Mu digal ko mu moytu tooñ; ngir ku ñu tooñ bañ koo ñaan Yàlla, ndax ñaanam lu ñuy nangu la.