Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xibaare Na dayo bi mu am fa Yàlla, ci ne moom àgg na ca gën gaa kaweg daraja ci mbëggeel, kem ni ko Ibraahiima ame woon -yal na ko Yàlla dolli jàmm- , looloo tax mu ne amul benn xarit bu dul Yàlla; ndax xolam dafa fees ci bëgg Yàlla mu kawe mi ak màggal ko ak xam ko, kon keneen ku dul Yàlla xaju fa, Te bu doon am ab xarit ci mbindéef yi Abuu Bakar lay doon -yal na ko Yàlla dollee gërëm-. Mu moytandikuloo jéggi dayo ci néew yi kem ni ko Yahuud yi ak Nasaraan yi defe ci bàmmeeli séen Yónente yi ak ñu baax ñi, ba mujj ñu def ko ay yàllay, di ko jaamu bàyyi Yàlla, ñu tabax ca bàmmeel ya ay jàkka ak i jaamukaay. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- tere na aw xeetam ci ñuy def lu mel ni séen jëf ya.