Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day tere ëppal ak jéggi dayob Sariiha ci tagg ko ak di ko melal ay meloy Yàlla mu kawe mi ak i jëfam ya mu jagoo, walla ne dafa xam kumpa, walla di ko boole ak Yàlla ci ñaan, kem ni ko Nasaraan yi defe ci Iisaa doomu Maryama -yal na ko Yàlla dolli jàmm-. Topp mu leeral ne moom jaam la ci jaami Yàlla yi, mu digle ne nañuy wax ci moom ne: jaamub Yàlla la ak ndawam.