explain-icon

Explanation

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne julliy juróom yi ñu farataal ci bëccëg gi ak ci guddi gi, ak jullig Àjjuma ci ayu-bis gune, ak woor weeru koor ci at mu ne, da ñuy far bàkkaar yu ndaw yi ci seen diggante ci sartub moytu bàkkaar yu mag yi, Bu dee bàkkaar yu mag yi nag moom niki njaalo ak naan sàngara dara du ko far lu dul tuub.

explain-icon

Benefits from the Hadith

  • Bàkkaar yi daa am yu ndaw am yu mag.
  • Far bàkkaar yu ndaw yi dafa aju ci moytu bàkkaar yu mag yi.
  • Bàkkaar yu mag yi mooy bàkkaar yi nga xam ne gétan (ay daan) da cee war ci àdduna, walla ag tëkkug àllaaxira ñëw ci mbugal, walla merum Yàlla, walla ag xuppe nekk ca, mbaa ag rëbb ñeel ki ko def, lu mel ni njaalo ak naan sàngara.
explain-icon

Categories

explain-icon

More ...