Yónent bi day xamle ne setal ay bëñ ci bantu garabu Araag ak lu ko niru, day laabal gémmiñ ci ay tilim-tilim ak xet yu bon yi, Waaye daa bokk ci sabab yiy tax Yàlla gërëm jaamam bi; ndax topp Yàlla ak wuyu ay ndigalam moo ci nekk, ak li ci nekk ci sett gi nga xam ne Yàlla da koo bëgg.