explain-icon

exp

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne Yàlla mu baarkeel mi te kawe dafa wax ne: moom moo gën a doylu képp kuy bokk, mooy ki doylu ci lépp, bu nit defee ag jaamu defal ko Yàlla ak ku dul Yàlla; Yàlla da koy bàyyi te du ko ko nangul, daal di koy delloo boroom; Kon warees naa sellal jëf yi ngir Yàlla mu kawe mi, ndax Moom -tudd naa sellam ga- du nangu lu dul lu sell ngir jëmmam ju tedd ji.

explain-icon

fawaed

  • Moytandikuloo bokkaale ci bépp melokaanam; ndaxte moom day teree jëf mu ndangu.
  • Yëg doylug Yàlla ak ug màggaayam dafa bokk ci liy dimbali nit ki ci mu man a sellal jëf.
explain-icon

cats

explain-icon

more