explain-icon

exp

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne: benn waay da doon jëflànte ak nit ñi ci leb-lante, walla mu leen di jaay ba jëmmi-jamono ñu door koo fay, Mu daan wax ndawam la daan fayyeeku ji bor ya ca nit ña: Boo demee ci ku ame bor te amul lu mu faye ngir néew doole «nanga ko jéggal», benn ci neggandiku ko te bañ koo taxawu ci di ko laaj, Walla ci jël li mu am donte sax matul, loolu nag ngir li mu bëgg ak xemmeem ci Yàlla jéggal ko daal di koy baal. Ba mu faatoo Yàlla baal ko jéggal ko ay ñaawtéefam,

explain-icon

fawaed

  • Refetal ci jëflante ak nit ñi, ak di leen baal, te di jéggal ki nekk ci jafe-jafe daa bokk ci sabab yi gën a màgg ci muccug jaam bi ëllëg bis-penc.
  • Rafetal jëme ci nit ñi, ak sellal ngir Yàlla, ak yaakaar yërmaandeem, daa bokk ci sababi njéggali bàkkaar yi.
explain-icon

cats

explain-icon

more