Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «wërale nañu sawara ak ay bànneex, wërale àjjana ak ay naqar». Sahih/Authentic. - Al-Bukhari and Muslim
explain-icon

exp

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne sawara dañu koo wërale ak i mbir yoy bakkan da koo bëgg, ci jëf yu araam yi, ag gàtteñlu ci yu war yi; Ku topp bànneexam ci loolu kon yeyoo na sawara, Àjjana nag lu ñu muur la wërale ko ak ay mbir yoy bakkan da koo bañ; niki sax ci def ndigal yi bàyyi tere yi te muñ ca, bu dëgëree xeex ak bakkanam ci loolu kon yayoo na dugg àjjana.

explain-icon

fawaed

  • Bokk na ci liy tax a tàbbi ci bànneex yi li Saytaane di taaral lu bon ak lu ñaaw, ba mujj bakkan bi di ko gise lu rafet daal di jeng jëm ca.
  • Digle ñu sori bànneex yi ñu araamal; ndax te yoonu sawara la, ak muñ ci yu naqari yi ndax te yoonu àjjana la.
  • Ngëneelu xeex ak bakkan, ak farlu ci jaamu yi, ak muñ ci yu naqari yi ak coono yi wër topp yi.
explain-icon

cats

explain-icon

more