Jële nañu ci Miqdaat Doomi Mahdii-karib -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- mu wax ne: "bu nit ki bëggee mbokkam na ko wax ne da koo bëgg". Sahih/Authentic. - At-Tirmidhi
explain-icon

exp

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- day leeral benn ci yiy dëgëral diggante way-gëm ñi, tey tasaare mbëggeel seen biir, te mooy bu kenn bëggee mbokkam mu wax ko ne da koo bëgg.

explain-icon

fawaed

  • Ngëneelu mbëggeel gir Yàlla rekk tax, ci lu dul njariñul àdduna.
  • Sopp gi ñu sopp
  • ñu xibaar ki ñu bëgg ngir Yàlla ci bëgg gi ñi ko bëgg, ngir mbëggeel ga ak miineel ga gën a yokk.
  • Tasaare mbëggeel ci biir way-gëm ñi day dëgëral mbokkoog mgëm, day wattu mbooloo mi ci taasaaroo ak tàqalikoo.
explain-icon

cats

explain-icon

more