Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "yaw sama Boroom maa ngi lay ñaan bul def sama bàmmeel ab xërëm, Yàlla rëbb na nit ñiy jàppe bàmmeelu seeni Yónente ay jàkka". Sahih/Authentic. - Ahmad
explain-icon

exp

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- dafa ñaan Boroomam mu bañ a def bàmmeelam ab xërëm bu nit di jaamu ci di ko màggal, ak di ko jublu buy sujjóot. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-wax na ne Yàlla soreele na yërmaandeem képp kuy jàppe bàmmeel i Yónente yi ay jàkka; ndax jàppe ko ay jàkka yoon wu jëm ci jaamu ko la ak di ci am ay pas-pas.

explain-icon

fawaed

  • Jéggi dayob sariiha ci bàmmeel i Yónent yi ak ñu baax ñi day tax ñu di ko jaamu bàyyi fi Yàlla, moo tax ñu war a moytu luy jëme deci bokkaale.
  • Daganul di dem ci ay bàmmeel ngir màggal ko ak di fa def ag jaamu ak lu boroomam man a jege Yàlla mu kawe mi.
  • Tabax jàkka ci bàmmel yi dafa araam.
  • Julli ci bàmmeel yi dafa araam, doonte tabaxuñu ko jàkka, lu dul julleeb néew bi nga xam ne julleewuñu ko woon.
explain-icon

cats

explain-icon

more