Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day tere neenal kër yi bañfaa julli ba muy mel ni ay bàmmeel yu ñu dul julli, Mu tere it di baril ay siyaare bàmmeelam ak di fa dajaloo ci anamug aadawoo; ndax loolu day jëme ci bokkaale, Mu digle ñu julli ci moom ci bépp barab ci kaw suuf; ndax loolu dana àgg fa moom moo xam ci ku jege la walla ku sori ñoo ci yam, kon aajowoowul di barila dem ca bàmmeelam.