explain-icon

exp

Yónent ebi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne nit ki gën a texe cig rammoom ëllëg bis-penc mooy ki wax «Laa ilaaha illal Laahu te mu sell ci xolam» maanaam amul ku ñuy jaamu cig dëgg ku dul Yàlla, te mu mucc ci bokkaale ak ngistal.

explain-icon

fawaed

  • Saxal rammug Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ëllëg bis bu mujj ba, ak ne ag ramam du ñeel ñenn ñu dul way-kennal Yàlla yi.
  • Rammoom mooy ñaan Yàlla mu kawe mi ñeel aji-kennal Yàlla yi yayoo woon sawara ñu bañ faa dugg, ak ku fa duggóon mu génn fa.
  • Ngëneelu baatu tawhiid di kennal Yàlla képp, ak màggaayu jeexitalu baat bi.
  • Dëggal kàddug Tawhiid mi ngi ame ci xam li miy tekki, ak jëfe ya muy waral.
  • Ngëneelu Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-, ak ug xéram ci xam-xam.
explain-icon

cats

explain-icon

more