?ku ma sàmmal li ci diggante ay ŋaamam ak li ci diggante ñaari tànkam ma wóoralal ko àjjana

Jële nañu ci Sahl Ibn Sahd -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku ma sàmmal li ci diggante ay ŋaamam ak li ci diggante ñaari tànkam ma wóoralal ko àjjana».
Sahih/Authentic. - Al-Bukhari

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ñaari mbir yoy bu jullit taqoog moom day dugg àjjana, Bi ci njëkk: wattu làmmeñ ci wax luy merloo Yàlla mu kawe mi, Ñaareel bi: wattu péy mi (awara) ci tàbbi ci ñaawtéef; Ndax ñaari cér yii dañoo bari lu ñuy tàbbi loo nit ci bàkkaar.

  1. Wattu làmmeñ ak péy yoonu dugg àjjana la.
  2. Jagleel nañu làmmiñ ak péy cig tudd; ndax ñoom ñaar ñoo gën a rëy ci liy indil nit ki alkandey àdduna ak allaaxira.

Successfully sent!