explain-icon

exp

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa ñaanal yërmaande ñeel képp ku yomb te tabe di ku yaatu cim njaayam; Du taral ci kiy jënn ca njëg ga, te day jëflanteek moom ci jikko yu rafet, Di ku yomb te tabe te yomb bu dee jënn; du ŋott te du xeeb dayob bagaas ya, Di ku yomb te tabe te yéwen bu dee sàkku ñu fay ko ay boram; du tar ci aji-ñàkk ji ak aji-yittewóo ji, waaye da koy sàkku cig nooy ak ñeewantu, te day néggandiku ki ne ci jafe-jafe.

explain-icon

fawaed

  • Bokk na ci jubluwaayi Sariiha sàmm lépp luy yéwénal diggante nit ñi.
  • Xemmemloo ci jëfandikoo jikko yu kawe yi ca jëflante yay dox diggante nit ñi, ci jaay ak jënn ak yeneen yi.
explain-icon

cats

explain-icon

more