?ñiy taral alku nañu

Jële nañu ci Abdallah Ibn Mashuud mu wax ne: Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ñiy taral alku nañu» wax na ko ñatti yoon.
Sahih/Authentic. - Muslim

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne way-taral yi ñu sooy lañu wayé ñu Pert lañu yit-ci lu dul njub te du xam-xam- ci seen diine ak séen àdduna, ci séen i wax ak seen i jëf, ñi nga xam ne dañuy jéggi dayob Sariiha bi Yónent bi indi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.

  1. Araamal ag taral ak diisal ci mbir yépp, ak soññee ci moytu ko ci lépp; rawatina ci jaamu yi ag màggal ñu baax ñi.
  2. Sàkku li gën a mat ci jaamu yi mbir mu ñu gërëm la; waaye loolu ci topp Sariiha lay ame.
  3. Soppug di feddali mbir yi am solo, ndax Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa bàmtu wax ci ñatti yoon.
  4. Yaatug Lislaam ak ug Yombam.

Successfully sent!